Afrikin yi amoul këyit
yu Pajol ak Saint-Bernard
[page d'accueil]

français  / english  / deutsch  / italiano  / wolof

ALTINE fuku fan ak juroom ñat si weru mars si atum ren, ñaati temeru Afrikin ak sen temeru dom daal nañu eglizu Saint-Ambroise bi nekk Paris ngir ut dimbal si sen utum këyit wi. Bi weru Mars ame ñar fuku fan ak ñar. alkati yi dax nañu leen fofu. Ba ñu fa juge nak ,soon neñ lol biñ waja dem gymnase bu jappy bi nekk Paris. Waye fofu yit dañu len gene fofu. Dem nañu Cartoucherie bu Vincennes. Ariane Mouchkine fa la ube daara bo xamni dajelena ñar fuku kilifa ak juroom ben. Afrikin yi dem tok si antarpo bu SNCF bu nekk ri Pajol. Bobu ba leegi ño ngi tok. Goornmaabi ne len dina set ni mu len mana dimbale. Alarba ñar fuku fan ak juroom ben si weru juin, goornmaabi tontu nalen si lalen ne si ñar temeru nit ak juroom di na si dimbali ñar fuku ak ñar ño xamne di nañu am këyittu at. Ñi si dess mey nañu len weer ñu gen dëkbi. Bi ñi yege waxtu bobu ñu daje dem aglizu Saint-Bernard...
matelas


Fuñu len di binda !

Letaru ñi amul këyit yi ñu jot yëp ñu ngi len koy deñçal si Internet